Musaa dem, yeggeji mbooloo ma kàdduy Aji Sax ji yépp, ak àttey yoonam yépp. Mbooloo ma mépp bokk benn baat, ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def.»
Ba loolu weesee Musaa bind na mboolem kàdduy Aji Sax ji. Mu xëy nag suba teel, daldi sàkk ab sarxalukaay ca suufu tund wa, sampaale fa fukki doj ak ñaar, ñeel fukki giiri Israyil yaak ñaar.
Ba mu ko defee mu yebal ay ndawi bànni Israyil, ñooña def ay saraxi rendi-dóomal, boole ci rendi yëkk yu ndaw yu ñu def saraxi cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji.
Ba loolu amee mu jël téere ba ñu bind kóllëre ga, jàngal ko mbooloo ma, ñuy dégg. Mbooloo ma ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def, ba mu mat sëkk.»
Musaa jël deret ja, wis-wisal ca kaw mbooloo ma, ne leen: «Lii nag mooy deret ji Yàlla fase kóllëre gi mu séq ak yeen te mu aju ci mboolem kàddoom yii.»
Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Yéegal ba ci man ci kaw tund wi te négandiku fa, ma jox la àlluway xeer yi ak yoon wi, ak santaane yi ma ci bind ngir jàngle ko.»
leeru Aji Sax ja dal ca kaw tundu Sinayi, niir wa yiir tund wa diiru juróom benni fan. Bésub juróom ñaareel ba Aji Sax ji àddoo ca digg niir wa, woo Musaa.