Kàddug Yàlla Gi 2010
|
| 1 |
| Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: |
| 2 |
| «Waxal bànni Israyil ne leen, ñu indil ma ab jooxe. Ci képp ku am yéeneem ngeen di nangoo sama jooxe, indil ma ko. |
| 3 |
| Jooxe bi ngeen di nangoo ci ñoom di wurus ak xaalis ak xànjar, |
| 4 |
| ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr ak wëñu lẽe, ak kawari bëy |
| 5 |
| ak deri kuuyu xar yu ñu wulli, sóob ko xonqal, ak deri piipi ak banti séng, |
| 6 |
| ak diwu oliw gu ñuy taaloo, ak ndàbb luy xeeñal diwu pal, di xeeñal cuuraay, |
| 7 |
| ak peri onigsë, ak yeneen per yu ñuy tapp ci xar-sànnim sarxalkat bu mag ba ak kiiraayal dënnam. |
| 8 |
| Na ma bànni Israyil defaral kër gu sell, ndax ma dëkk ci seen biir. |
| 9 |
| Na lépp dëppoo ak li ma lay won. Muy misaalu xaymab jaamookaay bi, di misaalu mboolem ay jumtukaayam, lépp defeleen ko noonu. |
| 10 |
| «Defarleen gaalu dénku séng, guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll; taxawaayam di xasab ak genn-wàll. |
| 11 |
| Nañu ko xoob wurusu ngalam. Biir ak biti lañu koy xoob, sàkkal ko kéméju wurus, gu ko wër. |
| 12 |
| Móolalal gaal gi ñeenti lami wurus yu ñuy takk ci ñeenti tànk yi; ñaari lam, wet gii; ñaar wet gee. |
| 13 |
| Yettlul ay banti njàppuy séng te nga xoob bu ci nekk wurus. |
| 14 |
| Su ko defee nga roof njàppu yi ci lam, yi ci weti gaal gi, ngir ñu di ko yóbboo gaal gi. |
| 15 |
| Ci lami gaal gi la njàppu yiy des te bañ cee jógeeti. |
| 16 |
| Yebal ci gaal gi àlluway seede si ma lay jox. |
| 17 |
| «Defarlul kubeer gu ñuy amale njotlaay gu wurusu ngalam ngir gaal gi. Na guddaayam di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaayam di xasab ak genn-wàll. |
| 18 |
| Tëgglul ñaari malaakay serub yu wurus te nga féetale leen ak ñaari cati kubeeru njotlaay ga. |
| 19 |
| Defal cat lii ab serub, cat lee ab serub te nanga móolaale kubeer gi ak serub yi ci ñaari cat yi, ñu ànd di benn. |
| 20 |
| Na serub yi tàllal seeni laaf, jëme kaw te nañu yiire kubeeru njotlaay gi seeni laaf. Nañu janoo, te na seeni kanam jublook kubeeru njotlaay gi. |
| 21 |
| Tegal kubeeru njotlaay gi ci kaw gaal gi, gannaaw boo ci yebee àlluway seede si ma lay jox. |
| 22 |
| Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel bànni Israyil. |
| 23 |
| «Defarlul taabalu bantu séng, guddaayam di ñaari xasab, yaatuwaayam di xasab, taxawaayam di xasab ak genn-wàll. |
| 24 |
| Xoob ko wurusu ngalam te defal ko kéméju wurus gu ko wër. |
| 25 |
| Defal ko pegg bu ko wër bu tollu ci ñeenti baaraam, te sàkkal pegg ba wombu wurus, wërale ko. |
| 26 |
| Defarlul ko ñeenti lami wurus te takk lam ya ca ñeenti wet ya, fa fareek ñeenti tànk ya. |
| 27 |
| Na lam yi dendeek pegg bi, ngir mana téye njàppu, yi ñuy yóbboo taabal ji. |
| 28 |
| Yettlul ay njàppu yu bantu séng, nga xoob njàppu yi wurus, ñu di ko yóbboo taabal ji. |
| 29 |
| Sàkkal ko ay ndabam yu tell aki mbàttoom aki njaqam, ak këllam yi ñuy tuuroo. Te wurusu ngalam ngay def lu ci nekk. |
| 30 |
| Tegal mburum teewal mi ci kaw taabal ji, mu nekk ci sama kanam ba fàww. |
| 31 |
| «Defarlul tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Tegukaay ba, dees koy tëgg. Na taatu tegukaay ba ak per ba ànd aki kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp di benn. |
| 32 |
| Juróom benni car ñooy soqikoo ca wet ya, ñetti car ci gii wet, ñett ca ga ca des. |
| 33 |
| Benn car day am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, car ba ca topp am ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, kaas bu ci nekk ànd aki kàmbóotam aki mbaram, juróom benni car, ya soqikoo ca per ba, daj. |
| 34 |
| Gannaaw loolu peru tegukaayu làmp ba itam day am ñeenti kaas yu bindoo ni tóor-tóoru garabu amànd, ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram. |
| 35 |
| Ab kàmbóot ay ronu yii ñaari car, jàpp ca; beneen kàmbóot ronu ñaari car ya ca topp, jàpp ca, ab kàmbóot ronu ñaari car ya mujj, jàpp ca, juróom benni car, ya soqikoo ca peru làmp ba, daj. |
| 36 |
| Kàmbóot ya ak car ya dañuy ànd ak tegukaay ba, di benn, lépp doon lu ñu tëgge wenn dogu wurusu ngalam. |
| 37 |
| Defarlul juróom ñaari làmpam. Te na làmp ya tege tegin wuy leeral ca kanam tegukaay ba. |
| 38 |
| Ñiimi feyukaayu làmp yi ak andi làmp yi na doon wurusu ngalam. |
| 39 |
| Fanweeri kiloy wurusu ngalam ak juróom, ci lees di sàkk tegukaayu làmp bi, ak mboolem li mu àndal. |
| 40 |
| Nanga xool te topp misaal, yi ñu la ciy won ci kaw tund wi. |
|
| Denc ay kàddu |
https://beblia.bible:81/BibleAudio/wolofkyg/exodus/025.mp3
40
25