«Tegal sarxalukaayu cuuraay bi ci kanam rido, bi làq gaalu àlluway seede si ak kubeeru njotlaay, gi ci kaw gaalu àlluway seede si, foofu may dajejeek yaw.
Bu Aaróona di taal làmp yi diggante ngoon ak jant bu so itam, na taal cuuraay lu xeeñ li. Cuuraay la su ñuy taal ba fàww, ci seen gépp maas fi kanam Aji Sax ji.
Na Aaróona di sàkk ci deretu saraxu póotum bàkkaar bi, taqal ci béjjéni sarxalukaay bi, ngir def ko njotlaayal sarxalukaay bi benn yoon cim at. Benn yoon cim at lañu koy defal njotlaayam ci seen gépp maas. Sarxalukaay bu sella sell la, ñeel Aji Sax ji.»
«Boo tolloo ci taxawal limeefu boppi bànni Israyil, na ku nekk ci ñoom fey Aji Sax ji njot-gi-bakkanam ba nga koy lim, ndax menn musiba bañ leena dikkal ci biir lim bi.
«Lii nag mooy li képp ku ñu bind ci limeef yi wara fey: dogu xaalis bu diisaay bi di genn-wàllu siikal, bi ñuy natte ci jaamookaay bi, dayo boobu tollook fukki gera, mu dib jooxe, ñeel Aji Sax ji.
Nanga nangoo xaalisu njot-gi-bakkan bi ci bànni Israyil, te nga féetale ko liggéeyu xaymab ndaje mi. Loolu pàttliku lay doon, ñeel bànni Israyil fi kanam Aji Sax ji, ngir seen njot-gi-bakkan.»
Bu ñuy duggsi ci xaymab ndaje mi, nañu jàpp, ndax ñu baña dee, nañu jàpp itam, bu ñuy liggéeysi fi sarxalukaay bi, di taal saraxu sawara, ñeel Aji Sax ji.
«Yaw nag, tànnal ngën-gi-xeeñal; xeetu ndàbb li ñuy wax miir, bu tooy bi, sàkk ci juróomi kilo, xasum kanel mu xeeñ; ñaari kilo ak genn-wàll, yuuru gattax gu xeeñ; ñaari kilo ak genn-wàll,
Doom aadama ju ko jagoowul, deesu ko ko diw, te buleen njafaan lenn lu ni mel, lu ngeen yemale dayoy xeeñal ya ak dayoy diw gu sell gi. Deesu ko def ci yaramu kenn ku ko jagoowul, te buleen njafaan xeeñal yi ciy dem, ci dayo yu tollook dayoy diw gu sell gi, ngir defar lenn lu ni mel. Lu sell la, lu ngeen wara wormaal sellngaam.
Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Wutal nag xeeñal yii: ndàbbu estaagte, ak ndàbbi galbanom, ak xori onigsë yu xeeñ, ak cuuraay-libaŋ lu raxul, te yooyu yépp tolloo dayo.
Sàkk ci, wol ko ba mu mokk, nga teg ko fi kanam gaal gi àlluway seede si dence, fi biir xaymab ndaje mi, fi may dajeek yaw. Loolu lu sella sell la lu ngeen wara wormaal.