Besalel nag defare gaalu kóllëre gi dénku séng, guddaay bi di ñaari xasab ak genn-wàll, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll, taxawaay bi di xasab ak genn-wàll.
Besalel sàkk itam tegukaayu làmp bu wurusu ngalam. Liggéeyu tëgg bu jekk la def tegukaayu làmp bi, ak taatu tegukaay bi, ak peru tegukaay bi, ay kaasam aki kàmbóotam aki mbaram, lépp ànd ak tegukaay bi, di benn.
Ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd ñoo nekk ci benn car bi, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, ñetti kaas yu bindoo ni tóor-tóori garabu amànd nekk ci car bi ci topp, kaas bu ci nekk ànd ak ay kàmbóotam aki mbaram, ba juróom benni car, yi soqikoo ci per bi, daj.
Ab kàmbóot a ronu ñaari car, jàpp ci, beneen kàmbóot ronu ñaari car yi ci topp, jàpp ci, ab kàmbóot ronu ñaari car yi mujj, jàpp ci, juróom benni car, yi soqikoo ci weti per bi, daj.
Ci kaw loolu Besalel sàkk ci bantu séng sarxalukaayu cuuraay bu kaare, guddaay bi di xasab, yaatuwaay bi di xasab, taxawaay bi di ñaari xasab, ay béjjénam ànd ak moom di benn bant bi.