Ca ñaareelu atu nguuru Buur Daryus, Ca juróom ñaareelu weer wa, yemook ñaar fukki fan ak benn, kàddug Aji Sax ji moo dikk ci jottlib Yonent Yàlla Ase. Mu ne:
Daraja ji kër gii di mujje mooy sut ja woon, Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax. Mu ne: Ci bii bérab laay mayee jàmm, kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.»
waaw, su nit yoree ci lafu mbubbam, aw yàpp wu ñu sellal, ba noppi lafu mbubbam laal mburu mbaa lu ñu togg, mbaa biiñ mbaa ag diw mbaa ñam wu mu doon, ndax loola day daldi sell?» Ase laaj ko sarxalkat ya, ñu ne ko: «Déedéet.»
Ase dellu ne leen: «Nit ku sobewu ndax ab néew bu mu laal, su laalee lenn ci mboolem ñam yooyu, ndax ñam wa sobewu na?» Sarxalkat ya ne ko: «Sobewu na kay.»
Ase nag wax leen, ne leen: «Noonu la ci askan wii, noonu la ci xeet wii sama kanam. Kàddug Aji Sax jee. Noonu la ci mboolem seen liggéeyu loxo, ak sarax su ñu fi indi, loolu lépp a sobewu.
Seetaatleen seen xel bu baax, dale ko bésub tey jii, dale ko ci ñaar fukki fan ak ñeentu juróom ñeenteelu weer wi, daleleen ci bés bii kenug néegu Aji Sax ji tegee, ngeen seetaat seen xel.