Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan:«Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!Ca bérab yu gën a kawe,nañu ne: “Osaana!”»
Bi nga xamee ne saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer.
Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu tontu leen ne: «Waaw dégg naa ko. Ndax musuleen a jàng lii ci Mbind mi: “Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp sàkkal nga sa bopp ay cant”?»
Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk.» Ca saa sa figg ga daldi wow.
Noonu Yeesu tontu leen ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te bañ a werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def.
Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, di fa jàngale. Bi muy jàngale nag saraxalekat yu mag ya ak njiiti xeet wa ñëw ci moom ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ku la may boobu sañ-sañ?»
La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobareg baayam?» Ñu ne: «Ñaareel bi.» Kon Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkk a dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
Ndaxte Yaxya ñëw na ci yéen ci yoonu njub, te gëmuleen ko; waaye juutikat yi ak jigéeni moykat yi gëm nañu ko. Te gannaaw bi ngeen gisee loolu, seen xel soppikuwul sax, ba ngeen gëm ko.»
Yeesu teg ca ne: «Dégluleen beneen léeb. Amoon na fi benn boroom kër bu jëmbët toolu réseñ. Mu ñag tool bi, gas ci biir pax, ngir nal ci réseñ yi. Mu tabax wottukaay, batale ko ay beykat, daldi tukki.