Wolof Bible 1987
|
| 1 |
| Yaw nag nangay waare li dëppook njàngale mu wér mi. |
| 2 |
| Maanaa, na góor ñu mag ñi foog, am faayda te maandu, di ñu wér ci seen ngëm, seen mbëggeel ak seen muñ. |
| 3 |
| Jigéen ñu mag ñi itam, na seen doxalin ànd ak faayda; buñuy jëw mbaa xér ci sangara. Waaye nañuy jàngale lu baax, |
| 4 |
| bay sol ci boppu jeeg yu ndaw yi, ñu bëgg seeni jëkkër ak seeni doom, |
| 5 |
| di ñu maandu, sell te fonk seen kër, ñu neex deret te déggal seeni jëkkër, ngir kenn bañ cee gàkkal kàddug Yàlla. |
| 6 |
| Naka noonu itam nanga xiir waxambaane yi cig maandu. |
| 7 |
| Te yaw, ci lépp lu mu man a doon, nekkal ab royukaay ci jëf yu baax. Na sa njàngale wér te am faayda, |
| 8 |
| ànd ak wax yu wér yu kenn mënta diiŋat, ngir sunuy noon rus ba wedam, ci li ñu amul dara lu ñu nu tuumaal. |
| 9 |
| Waxal it jaam ñi, ñu déggal seeni sang ci lépp, te liggéeyal leen ba seral seen xol, bañ cee boole werante |
| 10 |
| mbaa sàcc. Waaye nañu wone takkute gu mat, ba rafetal ci lépp njàngalem Yàlla sunu Musalkat. |
| 11 |
| Ndaxte yiwu Yàlla feeñ na te ubbil na ñépp buntu mucc. |
| 12 |
| Moo nu digal, nu dëddu weddi ak bëgg-bëggi jamono, tey dund ci àddina cig maandu, njub ak ragal Yàlla, |
| 13 |
| di séentu bés bu tedd bi nu yaakaar, maanaa Yàlla ju màgg ji, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, feeñ ci biir ndamam. |
| 14 |
| Joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci lépp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te ràññiku ci jëf yu baax. |
| 15 |
| Jàngaleel loolu, di leen dénk ak a yedd ak fulla ju mat. Bu la kenn yab. |
| Save Notes |
https://beblia.bible:81/BibleAudio/wolof/titus/002.mp3
3
2