Wolof Bible 1987
|
| 1 |
| Yéen samay bokk, bu benn gënale laal seen ngëm ci sunu Boroom Yeesu Kirist, mi soloo ndam. |
| 2 |
| Ndaxte su ñaari nit duggee ci seen mbooloo, kii takk jaaroy wurus te sol yére yu taaru, ka ca des ñàkk te limboo ay sagar, |
| 3 |
| ngeen teral boroom daraja ji ne ko: «Àggal ci jataay bu yiw bi,» ba noppi ngeen ne aji néew doole ji: «Taxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay tànk,» |
| 4 |
| kon gënale ngeen ci seen biir, ba àtte ci col, bàyyi xol. |
| 5 |
| Dégluleen yéen sama bokk yi ma bëgg, ndax Yàlla tànnul ñi néewle ci àddina, ngir ñu barele ci ngëm, tey am i cér ci nguur, gi Yàlla dig ñi ko bëgg? |
| 6 |
| Fekk dangeen leen di toroxal! Xanaa du boroom alal yi ñoo leen di noot te di leen yóbbu fa kanam àttekat yi? |
| 7 |
| Ndax duñu tilimal tur wu tedd, wi ngeen di wuyoo? |
| 8 |
| Su ngeen sàmmee yoonu Buur Yàlla, ni ko Mbind mi tërale naan: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp,» kon def ngeen lu baax. |
| 9 |
| Waaye su ngeen gënalee, bàkkaar ngeen, te yoonu Yàlla dina leen dab ni ñu moy. |
| 10 |
| Ndaxte ku sàmm yoon wépp, waaye xëtt ci lenn ndigal rekk, jàdd nga yoon wépp. |
| 11 |
| Ndaxte Yàlla mi ne: «Bul njaaloo,» teg na ca ne: «Bul rey nit.» Ku njaaloowul nag, waaye nga rey nit, jàdd nga yoon wépp. |
| 12 |
| Gannaaw dingeen nar a jaar ci àtteb yoon, wiy goreel, na loolu lal seen wax ak seen jëf. |
| 13 |
| Ndaxte ku yërëmul, yoon du la yërëm. Te yërmande mooy noot àtte. |
| 14 |
| Te lii itam samay bokk, ku ne gëm nga, te jëfewoo ko, loolu lu muy jariñ? Ndax googu ngëm man na laa musal? |
| 15 |
| Su amee mbokk ci seen biir, mu rafle te amul dund, muy góor walla jigéen, |
| 16 |
| te kenn ci yéen ne ko: «Demal ak jàmm, nga solu te lekk,» te fekk fajuleen aajoom, loolu lu muy jariñ? |
| 17 |
| Noonu ngëm gu àndul ak jëf, amul benn njariñ. |
| 18 |
| Waaye xanaa dina am ku ne: «Yaw am nga ngëm, man am naa ay jëf.» Yaw nag won ma sa ngëm gu àndul ak jëf, man ma feeñal la sama ngëm ci samay jëf. |
| 19 |
| Gëm nga ne Yàlla kenn la; loolu lu baax la, waaye xamal ne, jinne yi it gëm nañu loolu, ba dañoo tiit bay lox. |
| 20 |
| Yaw mi gàtt xel, kaay ma won la ne, ngëm gu àndul ak jëf, amul njariñ. |
| 21 |
| Sunu maam Ibraayma, ndax du ci kaw jëf la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu joxe doomam Isaaxa ni sarax? |
| 22 |
| Kon gis nga ne, ngëm dafa lëngoo ak ay jëfam, te ngëmam mat ci kaw jëf jooju. |
| 23 |
| Noonu li ñu wax ci Mbind mi am na, bi mu naan: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub,» ba ñu ko wooye xaritu Yàlla. |
| 24 |
| Kon nag gis nga ne, Yàlla ci jëf lay àtte nit ni ku jub, waaye du ci kaw ngëm kese. |
| 25 |
| Naka Raxab jigéenu moykat bi itam, ndax du ci noonu la ko Yàlla àttee ni ku jub, ci li mu teeru ndawi Yawut yi, te jaarale leen ca poot ba? |
| 26 |
| Kon nag ni jëmm ju amul ruu nekke ndee, noonu la ngëm gu àndul ak jëf nasaxe. |
|
| Denc ay kàddu |
https://beblia.bible:81/BibleAudio/wolof/james/002.mp3
5
2