Ndaxte jox na xeeti àddina yépp, ñu naan ci koppu nafsoom ak njaaloom, ba ñu màndi. Buuri àddina ànd nañu ak moom ci njaaloo, te baana-baanay àddina woomle nañu ndax li mu bëgg mbuux.»
Noonu ma dégg beneen baat bu jóge asamaan naan: «Génnleen ci biiram, yéen samay gaay, ngir ngeen bañ a bokk ci ay bàkkaaram te bañ a am cér ci musiba yi koy dal.
Joxleen ko ci coono ak naqar, lu tollu ni tiitar ak mbuux, ba mu dencaloon boppam. Gannaaw nee woon na ci xelam: “Maa ngi toog fii ni buur, duma ab jëtun te duma ténj mukk,”
looloo tax ba musiba, yii ñu ko sédd, dinañu ñëw ci benn bés, ñu di mbas, ténj ak xiif, ñu di ko lakk ba mu jeex, ndaxte Yàlla Boroom bi ko àtte, ku am kàttan la.»
Dinañu tiit ndax coonoom, ba dandu lu sore, naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw,dëkk bu mag bi,Babilon mi am kàttan;wenn waxtu rekk doy na,ngir sab àtte mat!»
ak bant yuy safal, gàncax gu xeeñ, ay xeeti cuuraay yu bare, latkoloñ, biiñ, diw, sungufu lay-layaat, pepp, ay nag, ay xar, ay fas, sareeti xare, ay jaam, ba ci bakkani nit.
sa alal ju bare jépp naaw na ci wenn waxtu!» Noonu ñépp ñiy dawal gaal ak ñi ciy tukki ak ñi ciy liggéey ak ñi ciy baana-baana, ñépp di sore bérab boobu,
Ñuy xëpp suuf ci seen bopp, di jooy, di naqarlu te naan:«Ngalla yaw! Ngalla yaw,dëkk bu mag bi nga xam neci la boroom gaal yépp woomle ndax sa barele,ci wenn waxtu nga gental.
Buumi xalam yi, baati woykat yi, toxoro yi ak liit yi,kenn dootu leen dégg ci yaw.Liggéeykat bu xareñ bu mu man a doon, kenn dootu ko gis ci yaw.Kandaŋu gënn, kenn du ko déggati ci yaw.
Niitug làmp du tàkkati,te baatu boroom séet ak séetam dootul jib ci yaw ba fàww.Ndaxte say baana-baana ñoo yilifoon àddina,te xeet yépp réer nañu ndax say luxus.