Gannaaw loolu ma dégg lu mel ni baat bu xumb bu jollee ca mbooloo mu bare ca asamaan, naan:«Aleluya!Mucc, ndam ak kàttan,Yàlla sunu Boroom moo ko moom.
Ma dégg lu mel ni baatu mbooloo mu bare, mel ni riiru duusi géej, ni yenguy dënnu yu réy, naan:«Aleluya!Ndaxte sunu BoroomYàlla Aji Kàttan jidugg na ci nguuram.
Gannaaw loolu malaaka ma ne ma: «Bindal lii: “Yéen ñi ñu woo ci reeri céetu Mbote ma, barkeel ngeen.”» Mu teg ca ne ma: «Kàddu yii ñooy kàdduy Yàlla, di kàddu yu dëggu.»
Noonu ma daanu ci ay tànkam, bëgg koo jaamu. Waaye mu ne ma: «Moytu koo def; sa nawle laa ci liggéey bi, di kenn ci say bokk, yiy sax ci seedeel Yeesu. Jaamul Yàlla. Ndaxte seedes Yeesu mooy xel miy solu yonent yi.»
Am na jaasi ju ñaw juy génn ci gémmiñam, ngir dóor xeet yi, mu di leen jiitee yetu weñ, te mooy nappaaje réseñ yi ci segalukaayu mer mu tàng, mu Yàlla Aji Kàttan ji.
Ñu jàpp rab wa, moom ak naaféq ba mbubboo yonent, ba daan def ca turu rab wa ay kéemaan yu mu naxe ñi nangu woon a am màndargam rab wa te jaamu nataalam. Ñoom ñaar ñépp sànni nañu leen ñuy dund ca déegu safara ak tamarax buy tàkk.