× Language Europe Russian Belarusian Ukrainian Polish Serbian Bulgarian Slovakian Czech Romanian Moldovian Azerbaijan Armenian Georgian Albanian Avar Bashkir Tatar Chechen Slovenian Croatian Estonian Latvian Lithuanian Hungarian Finnish Norwegian Swedish Icelandic Greek Macedonian German Bavarian Dutch Danish Welsh Gaelic Irish French Basque Catalan Italian Galacian Romani Bosnian North America English South America Spanish Portuguese Guarani Quechuan Aymara Central America Jamaican Nahuatl Kiche Qeqchi Haitian East Asia Chinese Japanese Korean Mongolian Uyghur Hmong South East Asia Malaysian Burmese Chin Nepali Cebuano Tagalog Cambodian Thai Indonesian Vietnamese Javanese Lao Iban IuMien Kachin Lahu Aceh Balinese Bugis Pampanga Sasak Shan Waray South Asia Hindi Оdia Awadhi Mizo Kannada Malayalam Marathi Gujarati Tamil Telugu Punjabi Kurukh Assamese Maithili Bengali Urdu Sinhala Dogri Haryanvi Meitei Konkani Santali Sindhi Koya Thado Sanskrit Devanagari Adilabad Gondi Ahirani Balochi Bundeli Chhattisgarhi Garhwali Kangri Kumaoni Mewari Munda Sadri Seraiki Shekhawati Sylheti Central Asia Kyrgyz Uzbek Tajik Turkmen Kazakhstan Karakalpak Middle East Turkish Hebrew Arabic Persian Kurdish Pashto Coptic Africa Afrikaans Xhosa Zulu Ndebele Sotho Amharic Wolaytta Nigerian Mossi Ika Dinka Kabyle Ewe Swahili Morocco Somalian Shona Madagascar Igbo Lingala Baoule Siswati Tsonga Tswana Gambian Yoruba Kamba Kinyarwanda Hausa Chewa Luo Makhuwa Dyula Fulfulde Kalenjin Kikuyu Kikwango Kirundi Krio Nigerian Pidgin Oromo Tshiluba Tshivenda Twi Umbundu Lugbara Luguru Pular Gussi Maasai Turkana Moba Nuer Shilluk Tamasheq Makonde Bemba Fon Hadiyya Ibibio Kimbundu Kimiiru Lango Liberian Kreyol Lomwe Mende Morisyen Ndau Nyankole Sena Sidamo Soga Songe Sukuma Tarifit Teso Tiv Zande Dagbani Australia Continent New Zealand Papua New Guinea Old Languages Aramaic Latin Esperanto 1 1 1 Kàddug Dëgg 1987 Kàddug Dëgg 1987Kàddug Yàlla20201 1 1 Luke MatthewMarkLukeJohnActsRoom1 Korent2 KorentGalasiEfesFilibKolos1 Tesalonig2 Tesalonig1 Timote2 TimoteTitFilemonYawutYanqóoba1 Piyeer2 Piyeer1 John2 John3 JohnYuddPeeñu1 1 1 1 1234567891011121314151617181920212223241 1 1 : 1 12345678910111213141516171819202122232425262728293031323334353637383940414243444546474849505152535455565758596061626364656667686970717273747576777879801 1 1 Wolof Bible 1987 Luke 1 Save Notes 1Yaw Teyofil mu tedd mi, xam nga ne, nit ñu bare sasoo nañoo bind ab nettali bu jëm ci mbir, yi xewoon ci sunu biir,2li dëppook waxi seede, yi ko teewe woon li dale ca ndoorte la te ñu mujj nekk jawriñi kàddug Yàlla.3Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe.4Noonu dinga man a xam ne, li ñu la jàngaloon lu wér peŋŋ la.5Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na saraxalekat bu ñu tudde Sakariya te bokk ca mbootaayu saraxalekat, ya askanoo ci Abiya. Jabaram Elisabet askanoo moom itam ci Aaroona.6Sakariya ak jabaram ñu jub lañu ca kanam Yàlla, di topp ni mu ware ndigal yi ak dogali Boroom bi yépp.7Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet mënul a am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu.8Benn bés nag Sakariya doon def liggéeyu saraxaleem ca Yàlla, ndaxte mbootaayam a aye keroog.9Bi ñuy tegoo bant, ni ko saraxalekat yi daan defe nakajekk, ngir xam kan mooy dugg ca bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga, ngir taal fa cuuraay, bant ba tegu ci Sakariya.10Ca waxtu wa ñuy taal cuuraay la, mbooloo maa nga woon ca biti, di ñaan.11Noonu benn malaakam Boroom bi daldi feeñu Sakariya, taxaw ca féeteek ndeyjooru saraxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam.12Naka la ko Sakariya gis, fitam daldi dem, mu tiit.13Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakariya, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa jabar dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya.14Sa mbég lay doon, sa xol sedd ci, te ñu bare dinañu bég ci juddoom,15ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu.16Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.17Mooy jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Iliyas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi.»18Sakariya daldi ne malaaka ma: «Nan laay xame ne, loolu dëgg la? Ndaxte mag laa, te sama jabar it màggat na.»19Malaaka ma tontu ko ne: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xebaar bu baax boobu.20Léegi nag gannaaw gëmuloo li ma wax, dinga luu te dootuloo man a wax, ba kera sama wax di am, bu jamonoom jotee.»21Fekk na booba mbooloo maa ngi xaar, jaaxle lool ci li Sakariya yàgg ca bérab bu sell ba.22Waaye bi mu génnee nag, mënul a wax ak ñoom. Noonu nit ña xam ne, dafa am lu ko feeñu ca bérab bu sell ba. Dafa luu, ba di leen liyaar.23Bi Sakariya matalee liggéeyu saraxaleem ba noppi, mu daldi ñibbi.24Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet jabaram ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer25te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!»26Bi Elisabet nekkee ci juróom-benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile.27Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama.28Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm ngaam, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.»29Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu man a tekki.30Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam.31Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu.32Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam.33Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.»34Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu man a ame? Man de, janq laa ba tey.»35Malaaka ma tontu ko ne: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.36Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku mënul a am doom, mu ngi ci juróom-benni weeram.37Ndaxte dara tëwul Yàlla.»38Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem.39Ci jamono jooju Maryaama jóg, gaawantu dem ci benn dëkk bu nekkoon ca tund ya ca diiwaanu Yude.40Mu dugg ca kër Sakariya, daldi nuyu Elisabet.41Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yengatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet.42Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb!43Man maay kan, ba ndeyu sama Boroom ñëw di ma seetsi?44Maa ngi lay wax ne, naka laa la dégg ngay nuyoo rekk, sama doom ji yengu ci sama biir ndax mbég.45Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne, li la Boroom bi yégal dina mat!»46Noonu Maryaama daldi ne:47«Sama xol a ngi màggal Boroom bi,sama xel di bég ci Yàlla sama Musalkat,48ndaxte fàttaliku na ma,man jaamam bu woyof bi.Gannaawsi tey, niti jamono yéppdinañu ma wooye ki ñu barkeel,49ndaxte Ku Màgg ki defal na ma lu réy.Turam dafa sell.50Day wàcce yërmandeem ci ñi ko ragal,ci seeni sët ba ci seeni sëtaat.51Wone na jëf yu mag ci dooley loxoom,te tas mbooloom ñiy réy-réylu,52daaneel boroom doole yi ci seen nguur,yékkati baadoolo yi.53Ñi xiif, reggal na leen ak ñam wu neex,te dàq boroom alal yi,ñu daw ak loxoy neen.54Wallu na bànni Israyil giy jaamam,di fàttaliku yërmandeem,55ni mu ko dige woon sunuy maam,jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»56Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu war a tollook ñetti weer, sog a ñibbi.57Gannaaw loolu jamono ji Elisabet war a mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor.58Dëkkandoom yi ak mbokkam yi yég ne, Boroom bi won na ko yërmande ju réy, ñu ànd ak moom bég.59Bi bés ba dellusee, ñu ñëw xarafalsi xale ba, bëgg koo dippee baayam Sakariya.60Waaye yaayam ne leen: «Déedéet, Yaxya lay tudd.»61Ñu ne ko: «Amoo menn mbokk mu tudd noonu.»62Ñu daldi liyaar baayam, ngir xam nan la bëgg ñu tudde xale ba.63Sakariya laaj àlluwa, bind ci ne: «Yaxya la tudd.» Ñépp daldi waaru.64Ca saa sa Yàlla dindi luu gi, Sakariya daldi waxaat, di màggal Yàlla.65Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp.66Ñi dégg nettali, bi jëm ci mbir yooyu, dañu koo denc ci seen xol te naan: «Nu xale bii di mujje nag?» Ndaxte leeroon na ne, dooley Boroom baa ngi ànd ak moom.67Sakariya baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne:68«Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil,ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!69Feeñal na nu Musalkat bu am doole,bi soqikoo ci askanu Daawuda jaamam,70ni mu yéglee woon bu yàggjaarale ko ci yonentam yu sell yi.71Dina nu musal ci sunuy noon,jële nu ci sunu loxoy bañaale.72Yàlla wone na yërmandeem,ji mu digoon sunuy maam,te di fàttaliku kóllëre, gi mu fas ak ñoom,73di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,74dina nu teqale ak sunuy noon,ngir nu man koo jaamu ci jàmm,75nu sell te jub ci kanamam sunu giiru dund.76Yaw nag doom, dinañu lay wooye yonentu Aji Kawe ji,ndaxte dinga jiitu, di yégle ñëwu Boroom bi,di ko xàllal yoon wi.77Dinga xamal mbooloom,ni leen Boroom bi man a musale,jaare ko ci seen mbaalug bàkkaar,78ndaxte Yàlla sunu Boroom fees na ak yërmande,ba tax muy wàcce ci nun jant buy fenk,79ngir leeral ñi toog ci lëndëm,takkandeeru dee tiim leen,ngir jiite nu ci yoonu jàmm.»80Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.Wolof Bible 1987 Copyrighted - Kàddug Dëgg Gi Copyright © Les Assemblées Evangéliques du Sénégal and La Mission Baptiste du Sénégal. All rights reserved Wolof Bible 1987 Luke 1 00:00:00 00:00:00 0.5x 2.0x https://beblia.bible:81/BibleAudio/wolof/luke/001.mp3 24 1