× Language Europe Russian Belarusian Ukrainian Polish Serbian Bulgarian Slovakian Czech Romanian Moldovian Azerbaijan Armenian Georgian Albanian Avar Bashkir Tatar Chechen Slovenian Croatian Estonian Latvian Lithuanian Hungarian Finnish Norwegian Swedish Icelandic Greek Macedonian German Bavarian Dutch Danish Welsh Gaelic Irish French Basque Catalan Italian Galacian Romani Bosnian North America English South America Spanish Portuguese Guarani Quechuan Aymara Central America Jamaican Nahuatl Kiche Qeqchi Haitian East Asia Chinese Japanese Korean Mongolian Uyghur Hmong South East Asia Malaysian Burmese Chin Nepali Cebuano Tagalog Cambodian Thai Indonesian Vietnamese Javanese Lao Iban IuMien Kachin Lahu Aceh Balinese Bugis Pampanga Sasak Shan Waray South Asia Hindi Оdia Awadhi Mizo Kannada Malayalam Marathi Gujarati Tamil Telugu Punjabi Kurukh Assamese Maithili Bengali Urdu Sinhala Dogri Haryanvi Meitei Konkani Santali Sindhi Koya Thado Sanskrit Devanagari Adilabad Gondi Ahirani Balochi Bundeli Chhattisgarhi Garhwali Kangri Kumaoni Mewari Munda Sadri Seraiki Shekhawati Sylheti Central Asia Kyrgyz Uzbek Tajik Turkmen Kazakhstan Karakalpak Middle East Turkish Hebrew Arabic Persian Kurdish Pashto Coptic Africa Afrikaans Xhosa Zulu Ndebele Sotho Amharic Wolaytta Nigerian Mossi Ika Dinka Kabyle Ewe Swahili Morocco Somalian Shona Madagascar Igbo Lingala Baoule Siswati Tsonga Tswana Gambian Yoruba Kamba Kinyarwanda Hausa Chewa Luo Makhuwa Dyula Fulfulde Kalenjin Kikuyu Kikwango Kirundi Krio Nigerian Pidgin Oromo Tshiluba Tshivenda Twi Umbundu Lugbara Luguru Pular Gussi Maasai Turkana Moba Nuer Shilluk Tamasheq Makonde Bemba Fon Hadiyya Ibibio Kimbundu Kimiiru Lango Liberian Kreyol Lomwe Mende Morisyen Ndau Nyankole Sena Sidamo Soga Songe Sukuma Tarifit Teso Tiv Zande Dagbani Australia Continent New Zealand Papua New Guinea Old Languages Aramaic Latin Esperanto 1 1 1 Kàddug Dëgg 1987 Kàddug Dëgg 1987Kàddug Yàlla20201 1 1 John MatthewMarkLukeJohnActsRoom1 Korent2 KorentGalasiEfesFilibKolos1 Tesalonig2 Tesalonig1 Timote2 TimoteTitFilemonYawutYanqóoba1 Piyeer2 Piyeer1 John2 John3 JohnYuddPeeñu1 1 1 1 1234567891011121314151617181920211 1 1 : 1 1234567891011121314151617181920212223242526272829303132333435363738394041424344454647484950511 1 1 Wolof Bible 1987 John 1 Save Notes 1Ca njàlbéen ga fekk na Kàddu gi am, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon.2Moo di ki nekkoon ak Yàlla ca njàlbéen ga.3Ci moom lañu sàkke lépp. Amul dara lu ñu sàkk lu jaarul ci moom.4Ci moom la dund nekk, te dund googu mooy leeral nit ñi.5Leer gi feeñ na ci biir lëndëm, te lëndëm gi jàppu ko.6Yàlla yónni woon na nit ku ñu naan Yaxya.7Kooku ñëw na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. Ñëw na ngir ñépp dégg li mu wax te gëm.8Moom ci boppam du woon leer gi, waaye ñëw na ngir seedeel leer gi.9Kàddu googu mooy leer gu wóor, giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk.10Ci àddina la nekkoon, àddina si ñu sàkk jaarale ko ci moom, te àddina xamu ko.11Ñëw na ci réewam, te ay ñoñam nanguwuñu ko.12Teewul ñi ko nangu te gëm ci turam, may na leen, ñu am sañ-sañu nekk doomi Yàlla.13Ñooñu judduwuñu ci deret walla ci bëgg-bëggu yaram, walla ci coobarey nit. Ñu ngi juddu ci Yàlla.14Kàddu gi ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp.15Yaxyaa ngi koy seedeel te yégle na lii; nee na: «Moo taxoon ma wax ne: “Dina ñëw sama gannaaw waaye moo ma gën a màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”»16Kàddu gi fees na ak yiw, te nun ñépp jot nanu ci sunu wàll, mu barkeel nu ay yooni-yoon.17Ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lañu leen jaarale; yiw wi ak dëgg gi, Yeesu Kirist moo ko indaale.18Kenn musul a gis Yàlla, waaye Bàjjo bi, di Yàlla te nekk ak Baay bi, moo ko xamle.19Lii mooy seedes Yaxya. Amoon na bés Yawut ya yónni ay saraxalekat ca Yaxya, ñu ànd ak ñu soqikoo ci giiru Lewi. Ñu nga jóge Yerusalem, ñëw ci moom, di ko laaj mooy kan.20Yaxya tontu na leen te nëbbu ci dara, wóoral na leen ne, moom du Almasi bi.21Ñu laaj ko ne: «Kon yaay kan? Ndax yaa di Iliyas?» Mu ne leen: «Déedéet, duma Iliyas.» Ñu ne ko: «Ndax yaa di Yonent, bi war a ñëw?» Mu tontu ne leen: «Déedéet.»22Noonu ñu laaj ko ne: «Wax nu yaay kan, ngir nu man a tontu ñi nu yónni. Nga ne yaa di kan?»23Yaxya tontu leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”»24Amoon na ñu bokk ca Farisen ya, yu àndoon ca mbooloo, ma ñu yónni woon ca Yaxya.25Ñooñu laaj ko ne: «Gannaaw doo Almasi bi, doo Iliyas, doo Yonent bi war a ñëw, lu tax ngay sóob nit ñi ci ndox?»26Yaxya ne leen: «Man maa ngi sóobe ci ndox, waaye am na ci seen biir ku ngeen xamul.27Kookooy ñëw sama gannaaw, te man sax yeyoowumaa tekki ay dàllam.»28Lii xewoon na ci dëkku Betani, ca gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon sóobe.29Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñëw ci moom, mu ne: «Xool-leen! Kii mooy mbotem Yàlla, mi ñu nar a rey, ngir dindi bàkkaaru àddina.30Moo taxoon ma wax ne: “Am na kuy ñëw sama gannaaw, waaye moo ma gën a màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”31Xawma woon kooku kan la waroon a doon, waaye xamal ko bànni Israyil moo tax ma ñëw, di sóob nit ñi ci ndox.»32Ci kaw loolu Yaxya seede na lii: «Gis naa Xelu Yàlla mi ci melow pitax, mu jóge ci asamaan, tegu ci moom.33Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Yàlla, mi ma yebal may sóobe ci ndox, nee woon na ma: “Dinga gis Xel mu Sell mi wàcc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di sóob ci Xel mu Sell mi.”»34Yaxya teg ca ne: «Gis naa loolu te seede naa ne, moom moo di Doomu Yàlla ji.»35Ca ëllëg sa Yaxya taxawaatoon na ca bérab booba, ànd ak ñaari taalibeem.36Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: «Kii mooy mbotem Yàlla mi!»37Ñaari taalibe ya dégg li mu wax, daldi dem toppi Yeesu.38Yeesu geestu, gis ne, ñoo ngi koy topp. Mu ne leen: «Lu ngeen soxla woon?» Ñu tontu ko: «Foo dëkk, Ràbbi?» Ràbbi mi ngi tekki «Kilifa gi.»39Yeesu ne leen: «Kaayleen gis.» Noonu ñu dem, seeti fa mu daloon, ngoonalal ko. Ci tàkkusaani kaw la woon.40Kenn ci ñoom ñaar, ñi déggoon li Yaxya wax te topp Yeesu, ma nga tuddoon Andare, mi bokkoon ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay.41Andare dafa daldi dem seeti Simoŋ ne ko: «Gis nanu Almasi bi.» Baat boobu mi ngi tekki «Kirist.»42Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.» Sefas mi ngi tekki «Piyeer,» maanaam «xeer.»43Ca ëllëg sa mu fas yéenee dem diiwaanu Galile te mu gis Filib. Yeesu ne ko: «Toppal ci man.»44Filib mu nga dëkkoon Betsayda, dëkku Andare ak Piyeer.45Filib dajeek Nataneel ne ko: «Gis nanu ki yoonu Musaa wi ak yonent yi doon wax. Mu ngi tudd Yeesu, doomu Yuusufa, te dëkk Nasaret.»46Nataneel tontu ko ne: «Aa! Ndax dara lu baax man na jóge Nasaret?» Filib ne ko: «Ñëwal gis.»47Naka la Yeesu gis Nataneel jëmsi ci moom, mu daldi ne ci mbiram: «Xool-leen, nitu Israyil dëgg a ngee di ñëw; du dox benn tànku caaxaan.»48Nataneel ne ko: «Noo ma xame?» Yeesu tontu ko ne: «Bi la Filib di laata woo, gis naa la, bi nga nekkee ca ker garabu figg ga.»49Nataneel wax ko ne: «Kilifa gi, yaay Doomu Yàlla ji, yaa di buuru Israyil!»50Yeesu tontu ko ne: «Ndax li ma ne, gis naa la ca ker garab ga, moo tax nga gëm? Dinga gis mbir yu gën a réy yii.»51Noonu mu teg ca ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, dingeen gis asamaan ubbiku, malaaka yiy baagante kaw ak suuf, di wàcc ci Doomu nit ki.»Wolof Bible 1987 Copyrighted - Kàddug Dëgg Gi Copyright © Les Assemblées Evangéliques du Sénégal and La Mission Baptiste du Sénégal. All rights reserved Wolof Bible 1987 John 1 00:00:00 00:00:00 0.5x 2.0x https://beblia.bible:81/BibleAudio/wolof/john/001.mp3 21 1