× Language Europe Russian Belarusian Ukrainian Polish Serbian Bulgarian Slovakian Czech Romanian Moldovian Azerbaijan Armenian Georgian Albanian Avar Bashkir Tatar Chechen Slovenian Croatian Estonian Latvian Lithuanian Hungarian Finnish Norwegian Swedish Icelandic Greek Macedonian German Bavarian Dutch Danish Welsh Gaelic Irish French Basque Catalan Italian Galacian Romani Bosnian North America English South America Spanish Portuguese Guarani Quechuan Aymara Central America Jamaican Nahuatl Kiche Qeqchi Haitian East Asia Chinese Japanese Korean Mongolian Uyghur Hmong South East Asia Malaysian Burmese Chin Nepali Cebuano Tagalog Cambodian Thai Indonesian Vietnamese Javanese Lao Iban IuMien Kachin Lahu Aceh Balinese Bugis Pampanga Sasak Shan Waray South Asia Hindi Оdia Awadhi Mizo Kannada Malayalam Marathi Gujarati Tamil Telugu Punjabi Kurukh Assamese Maithili Bengali Urdu Sinhala Dogri Haryanvi Meitei Konkani Santali Sindhi Koya Thado Sanskrit Devanagari Adilabad Gondi Ahirani Balochi Bundeli Chhattisgarhi Garhwali Kangri Kumaoni Mewari Munda Sadri Seraiki Shekhawati Sylheti Central Asia Kyrgyz Uzbek Tajik Turkmen Kazakhstan Karakalpak Middle East Turkish Hebrew Arabic Persian Kurdish Pashto Coptic Africa Afrikaans Xhosa Zulu Ndebele Sotho Amharic Wolaytta Nigerian Mossi Ika Dinka Kabyle Ewe Swahili Morocco Somalian Shona Madagascar Igbo Lingala Baoule Siswati Tsonga Tswana Gambian Yoruba Kamba Kinyarwanda Hausa Chewa Luo Makhuwa Dyula Fulfulde Kalenjin Kikuyu Kikwango Kirundi Krio Nigerian Pidgin Oromo Tshiluba Tshivenda Twi Umbundu Lugbara Luguru Pular Gussi Maasai Turkana Moba Nuer Shilluk Tamasheq Makonde Bemba Fon Hadiyya Ibibio Kimbundu Kimiiru Lango Liberian Kreyol Lomwe Mende Morisyen Ndau Nyankole Sena Sidamo Soga Songe Sukuma Tarifit Teso Tiv Zande Dagbani Australia Continent New Zealand Papua New Guinea Old Languages Aramaic Latin Esperanto 1 1 1 Kàddug Dëgg 1987 Kàddug Dëgg 1987Kàddug Yàlla20201 1 1 Kolos MatthewMarkLukeJohnActsRoom1 Korent2 KorentGalasiEfesFilibKolos1 Tesalonig2 Tesalonig1 Timote2 TimoteTitFilemonYawutYanqóoba1 Piyeer2 Piyeer1 John2 John3 JohnYuddPeeñu1 1 1 1 12341 1 1 : 1 12345678910111213141516171819202122232425262728291 1 1 Wolof Bible 1987 Kolos 1 Save Notes 1Man Pool, ndawul Kirist Yeesu ci coobareg Yàlla, man ak Timote sunu mbokk,2noo leen di bind, yéen gaayi Yàlla yu sell, yi dëkk Kolos te di ay bokk ci gëm Kirist. Na leen Yàlla sunu Baay may yiw ak jàmm.3Dunu noppee sant Yàlla, Baayu sunu Boroom Yeesu Kirist, saa su nu leen di ñaanal,4ndaxte yég nanu seen ngëm ci Kirist Yeesu ak seen mbëggeel ci gaayi Yàlla yépp.5Ngëm googu ak mbëggeel googu ñu ngi sosoo ci yaakaaru ëllëg, jiy cér bi leen Yàlla dencal ca asamaan. Mas ngeen a dégg yaakaar jooju ci kàddug dëgg gi, di xebaar bu baax bi.6Ni xebaar bu baax bi wàcce ci yéen, noonu lay wàcce ci àddina sépp, di meññ te di law. Te noonu lay doxale ci yéen, li dale ci bés, ba ngeen dégge xebaaru yiwu Yàlla, te xam dëggam gi mu ëmb;7moom ngeen jànge ci Epafras, miy sunu nawle ci liggéey bi te nu sopp ko, di jawriñu Kirist bu takku ngir seen njariñ.8Te moo nu yégal it mbëggeel, gi Xelu Yàlla mi sol ci yéen.9Looloo tax ci sunu wàllu bopp, ba nu ko yégee ba tey, jógunu ci di leen ñaanal. Nu ngi ñaan Yàlla, ngeen xam bu baax coobareem ci xel mu mat ak ràññee gu aju ci dooley Xelam.10Noonu dingeen dund dund gu dëppoo ak seen bokk ci Boroom bi, ba neex ko ci fànn gu nekk, di def bépp jëf yu baax, te yokk seen xam-xam ci Yàlla.11Te Yàlla dina leen dooleel ak bépp doole, mu mengoo ak kàttanu ndamam, ngir ngeen man a tegoo coono te muñ, ba fa muñ di yem.12Dingeen gërëm Yàlla Baay bi, ànd ci ak mbég, moom mi leen jagleel, ngeen bokk ci cér, bi mu dencal gaayam yu sell yi ci leer.13Yàlla musal na nu ci dooley lëndëm, yóbbu nu ci nguuru Doomam ji mu bëgg,14moom mi nu jot, maanaam baal nu sunuy bàkkaar.15Doom jooju moo di melokaanu Yàlla, ji kenn gisul. Mooy taaw bi, ki gën a màgg lépp luy mbindeef.16Ndaxte ci moom la Yàlla sàkke lépp lu nekk ci asamaan ak suuf, li ñuy gis ak li ñu mënul a gis, muy buur, njiit, kilifa mbaa boroom sañ-sañ. Lépp lu ñu sàkk, ci moom lañu ko jaarale, ci moom lañu ko jëme.17Laata dara di am, fekkoon na moom mu nekk, te lépp a ngi jàppoo ci moom.18Mooy bopp bi yilif jëmm ji, di mbooloom ñi ko gëm, ndaxte moom mooy njàlbéen gi, di taaw bi, maanaam ki jëkk a dekki, ngir muy kilifa ci bépp fànn.19Ndaxte soob na Yàlla mu dëkkal matam gépp ci moom20te jaar ci moom, jubale lépp ak boppam, muy ci kaw asamaan yi mbaa ci suuf, ba mu wàccee jàmm jaarale ko ci deret ji tuuru, bi Doom ji deeyee ca bant ba.21Te yéen ñi sore woon Yàlla te doon ay noonam ci seen xel ak seen jëf yu bon,22léegi nag Yàlla jubale na leen ak boppam jaare ko ci deewu Kirist ci yaramu nitam, ngir taxawal leen ca kanamam, ngeen sell te ñàkk sikk ak i ŋàññ.23Loolu nag na fekk ngeen wéy ci ngëm, sampu ci ba dëgër ci, tey séentu cér, bi leen xebaar bu baax bi jox. Te xebaar bu baax, boobu ngeen dégg te ñu yégal waa àddina sépp, man Pool moom laay yégle.24Léegi nag maa ngi am bànneex ci coono, yi may daj ngir seen njariñ; te li des sax ci fitnay Kirist, noonu laa koy àggalee ngir njariñu mbooloom ñi gëm, di jëmmam.25Jawriñu mbooloo moomu laa, ndaxte Yàlla sas na ma ngir yéen, may yégle fu nekk kàddoom,26maanaam ma yégle kumpa, gi nëbbu woon ay jamonoy jamono, waaye léegi Yàlla xamal na ko ay gaayam27ci xeeti àddina sépp. Ñoom nag la Yàlla bëgg a xamal ni ndamu kumpa googu màgge, maanaam Kirist a ngi dëkk ci yéen, di yaakaar ju wér ci ndamu ëllëg.28Moom Kirist lanuy yégle, di artu te di jàngal ku nekk, ànd ak xel mu mat, ngir jébbal Yàlla ku nekk ni ku mat ci Kirist.29Ci loolu laay jëmale sama liggéey, di bëree dooley Kirist, jiy yengu ci man ak kàttan.Wolof Bible 1987 Copyrighted - Kàddug Dëgg Gi Copyright © Les Assemblées Evangéliques du Sénégal and La Mission Baptiste du Sénégal. All rights reserved Wolof Bible 1987 Kolos 1 00:00:00 00:00:00 0.5x 2.0x https://beblia.bible:81/BibleAudio/wolof/colossians/001.mp3 4 1