× Language Europe Russian Belarusian Ukrainian Polish Serbian Bulgarian Slovakian Czech Romanian Moldovian Azerbaijan Armenian Georgian Albanian Avar Bashkir Tatar Chechen Slovenian Croatian Estonian Latvian Lithuanian Hungarian Finnish Norwegian Swedish Icelandic Greek Macedonian German Bavarian Dutch Danish Welsh Gaelic Irish French Basque Catalan Italian Galacian Romani Bosnian North America English South America Spanish Portuguese Guarani Quechuan Aymara Central America Jamaican Nahuatl Kiche Qeqchi Haitian East Asia Chinese Japanese Korean Mongolian Uyghur Hmong South East Asia Malaysian Burmese Chin Nepali Cebuano Tagalog Cambodian Thai Indonesian Vietnamese Javanese Lao Iban IuMien Kachin Lahu Aceh Balinese Bugis Pampanga Sasak Shan Waray South Asia Hindi Оdia Awadhi Mizo Kannada Malayalam Marathi Gujarati Tamil Telugu Punjabi Kurukh Assamese Maithili Bengali Urdu Sinhala Dogri Haryanvi Meitei Konkani Santali Sindhi Koya Thado Sanskrit Devanagari Adilabad Gondi Ahirani Balochi Bundeli Chhattisgarhi Garhwali Kangri Kumaoni Mewari Munda Sadri Seraiki Shekhawati Sylheti Central Asia Kyrgyz Uzbek Tajik Turkmen Kazakhstan Karakalpak Middle East Turkish Hebrew Arabic Persian Kurdish Pashto Coptic Africa Afrikaans Xhosa Zulu Ndebele Sotho Amharic Wolaytta Nigerian Mossi Ika Dinka Kabyle Ewe Swahili Morocco Somalian Shona Madagascar Igbo Lingala Baoule Siswati Tsonga Tswana Gambian Yoruba Kamba Kinyarwanda Hausa Chewa Luo Makhuwa Dyula Fulfulde Kalenjin Kikuyu Kikwango Kirundi Krio Nigerian Pidgin Oromo Tshiluba Tshivenda Twi Umbundu Lugbara Luguru Pular Gussi Maasai Turkana Moba Nuer Shilluk Tamasheq Makonde Bemba Fon Hadiyya Ibibio Kimbundu Kimiiru Lango Liberian Kreyol Lomwe Mende Morisyen Ndau Nyankole Sena Sidamo Soga Songe Sukuma Tarifit Teso Tiv Zande Dagbani Australia Continent New Zealand Papua New Guinea Old Languages Aramaic Latin Esperanto 1 1 1 Kàddug Dëgg 1987 Kàddug Dëgg 1987Kàddug Yàlla20201 1 1 Yanqóoba MatthewMarkLukeJohnActsRoom1 Korent2 KorentGalasiEfesFilibKolos1 Tesalonig2 Tesalonig1 Timote2 TimoteTitFilemonYawutYanqóoba1 Piyeer2 Piyeer1 John2 John3 JohnYuddPeeñu1 1 1 1 123451 1 1 : 1 1234567891011121314151617181920212223242526271 1 1 Wolof Bible 1987 Yanqóoba 1 Save Notes 1Man Saag, jaamu Yàlla ak Boroom bi Yeesu Kirist, maa leen di nuyu, yéen fukki giir ak ñaar, yi tasaaroo ci biir àddina si.2Yéen samay bokk, waxtu wu nattu yi dalee ci seen kaw, ak nu ñu man a mel, defleen ko ni mbég mu réy,3xam ne nattub ngëm mooy ndeyu muñ.4Kon na seen muñ dem ba mat, ngir ngeen bañ a fell fenn, waaye ngeen mat sëkk.5Ku xelam des ci benn fànn ci yéen nag, na ko ñaan Yàlla, te dina ko ko may, ndaxte Yàlla mooy Aji Yéwén, jiy may ñépp ci lu àndul ak genn ŋàññ.6Waaye na ko ñaan ci ngëm te bañ cee werante; ndaxte kiy werante mi ngi mel ni ndoxum géej, mi ngelaw liy lëmbaaje wet gu ne.7Bu kooku yaakaar dara ci Boroom bi.8Ku am xel ñaar la, te ñàkk pasteef ci lépp lu mu man a def.9Naka mbokk mi néew doole, na sant ci teraangaam fa kanam Yàlla,10te boroom alal it sant cig suufeem, ndax ni tóor-tóor di ruuse, noonu lay wéye.11Su jant fenkee, ba naaj wi tàng, kon gàncax lax, tóor-tóor ruus, te rafetaayam naaw. Noonu la boroom alal di nasaxe, moom ak i jëfam.12Ku dékku nattu, ku barkeel nga, ndax boo ci génnee ak ndam, dees na la jagleel kaalag dund, gi Yàlla dig ñi ko bëgg.13Bu la fiir galanee, bul ne: «Yàllaa ko dogal,» ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn.14Waaye ku sa bakkan nax, ba man la, looloo lay dugal ci fiir.15Kon bu bëgg-bëgg ëmbee, bàkkaar lay wasin, te bu bàkkaar màggee, jur dee.16Yéen sama bokk yi ma bëgg, buleen juum ci lii:17gépp may gu baax ak gépp jagle gu mat, ci Yàlla la jóge, di Baay bi sàkk leeri asamaan, fekk moom du soppiku, mbaa muy leer ak di lëndëm.18Ci coobareem la nu sole kàddug dëgg gi, ba nu judduwaat, di tànneefu lépp lu mu bind.19Yéen sama bokk yi ma bëgg, nangeen xam lii: ku nekk war ngaa farlu ci déglu, di yéex a wax tey yéex a mer.20Ndaxte meru nit du jur njub gi neex Yàlla.21Moo tax nanguleen ci woyof kàddu, gi leen Yàlla sol te man leen a musal, di dëddu bépp sobe ak coxor gi daj àddina.22Buleen yem ci déglu kàddu gi rekk, di nax seen bopp; waaye jëfeleen ko.23Ndaxte ku déglu kàddu gi, te bañ koo jëfe, moom ak kuy seetu ñoo yem;24day gis xar-kanamam, te su nee wërëñ, daldi fàtte meloom.25Waaye kuy gëstu yoonu Yàlla, wi mat tey goreel --waxuma ki dégg, ba noppi fàtte, waaye kiy jëfe ndigal — kooku barkeel na ci kaw jëfam.26Ku yaakaar ne am na diine, waaye moomul làmmiñam, xanaa di nax boppam rekk, diineem jooju du diiney dara.27Ku diineem sell te amul benn gàkk fa kanam Yàlla mooy kii: ki nemmiku jiirim yi ak jigéen ñi seen jëkkër faatu ci seeni tiis, tey waggar sobey àddina.Wolof Bible 1987 Copyrighted - Kàddug Dëgg Gi Copyright © Les Assemblées Evangéliques du Sénégal and La Mission Baptiste du Sénégal. All rights reserved Wolof Bible 1987 Yanqóoba 1 00:00:00 00:00:00 0.5x 2.0x https://beblia.bible:81/BibleAudio/wolof/james/001.mp3 5 1