× Language Europe Russian Belarusian Ukrainian Polish Serbian Bulgarian Slovakian Czech Romanian Moldovian Azerbaijan Armenian Georgian Albanian Avar Bashkir Tatar Chechen Slovenian Croatian Estonian Latvian Lithuanian Hungarian Finnish Norwegian Swedish Icelandic Greek Macedonian German Bavarian Dutch Danish Welsh Gaelic Irish French Basque Catalan Italian Galacian Romani Bosnian North America English South America Spanish Portuguese Guarani Quechuan Aymara Central America Jamaican Nahuatl Kiche Qeqchi Haitian East Asia Chinese Japanese Korean Mongolian Uyghur Hmong South East Asia Malaysian Burmese Chin Nepali Cebuano Tagalog Cambodian Thai Indonesian Vietnamese Javanese Lao Iban IuMien Kachin Lahu Aceh Balinese Bugis Pampanga Sasak Shan Waray South Asia Hindi Оdia Awadhi Mizo Kannada Malayalam Marathi Gujarati Tamil Telugu Punjabi Kurukh Assamese Maithili Bengali Urdu Sinhala Dogri Haryanvi Meitei Konkani Santali Sindhi Koya Thado Sanskrit Devanagari Adilabad Gondi Ahirani Balochi Bundeli Chhattisgarhi Garhwali Kangri Kumaoni Mewari Munda Sadri Seraiki Shekhawati Sylheti Central Asia Kyrgyz Uzbek Tajik Turkmen Kazakhstan Karakalpak Middle East Turkish Hebrew Arabic Persian Kurdish Pashto Coptic Africa Afrikaans Xhosa Zulu Ndebele Sotho Amharic Wolaytta Nigerian Mossi Ika Dinka Kabyle Ewe Swahili Morocco Somalian Shona Madagascar Igbo Lingala Baoule Siswati Tsonga Tswana Gambian Yoruba Kamba Kinyarwanda Hausa Chewa Luo Makhuwa Dyula Fulfulde Kalenjin Kikuyu Kikwango Kirundi Krio Nigerian Pidgin Oromo Tshiluba Tshivenda Twi Umbundu Lugbara Luguru Pular Gussi Maasai Turkana Moba Nuer Shilluk Tamasheq Makonde Bemba Fon Hadiyya Ibibio Kimbundu Kimiiru Lango Liberian Kreyol Lomwe Mende Morisyen Ndau Nyankole Sena Sidamo Soga Songe Sukuma Tarifit Teso Tiv Zande Dagbani Australia Continent New Zealand Papua New Guinea Old Languages Aramaic Latin Esperanto 1 1 1 Kàddug Dëgg 1987 Kàddug Dëgg 1987Kàddug Yàlla20201 1 1 Yudd MatthewMarkLukeJohnActsRoom1 Korent2 KorentGalasiEfesFilibKolos1 Tesalonig2 Tesalonig1 Timote2 TimoteTitFilemonYawutYanqóoba1 Piyeer2 Piyeer1 John2 John3 JohnYuddPeeñu1 1 1 1 11 1 1 : 1 123456789101112131415161718192021222324251 1 1 Yudd 1 Save Notes 1Man Yudd, jaamu Yeesu Kirist, mi bokk ak Saag ndey ak baay, maa leen di bind, yéen ñi Yàlla Baay bi woo te bëgg leen, te Yeesu Kirist aar leen.2Na leen Yàlla may yërmande, jàmm ak mbëggeel.3Samay bokk, bëggoon naa leen a bind lool ci mbirum mucc gi nu bokk, waaye lii moo gën a jamp: ma xiir leen, ngeen taxaw ci aar mboolem dëgg, yi Yàlla xas a dénk gaayam yu sell yi ba fàww.4Ndaxte am na ay nit ñu ñeme Yàlla, ñu yoxoosu ci seen biir; dañuy mbubboo yiwu Yàlla, ngir topp seen bakkan, di ci weddi Buur Yàlla miy kenn ak sunu Boroom Yeesu Kirist. Fekk Mbind mi tëral na seen àtte bu yàgg.5Xam ngeen loolu lépp ba noppi sax, waaye dama leen koy fàttali rekk. Xam ngeen ne Boroom bi musal na xeetam, ba génne leen réewu Misra, waaye gannaaw ba raafal na ñi gëmul woon.6Te it malaaka ya jàppul woon ca daraja ja ñu amoon, xanaa toxoo fa ñu leen dëëloon, Yàlla yeew na leen buum yu sax, tëj leen ci biir lëndëm, di leen nége àtteb bés bu mag ba.7Noonu itam dëkki Sodom ak Gomor ak dëkk ya leen wëroon, dañoo sóobu ci njaaloo ak di def ay góor-jigéen, waaye àtte bi dal na ci seen kaw, ba ñuy ay tegtal ci ñiy yelloo safara ba fàww.8Naka noonu itam gentkat yooyu may wax ñu ngi sobeel seen yaram, di weddi gépp kilifteef, di xas doole yi ci asamaan.9Waaye bi Mikayel, miy kilifa ci malaaka yi, di xëccook Seytaane néewu Musaa, bay xuloo ak moom, ñemewu koo àtte, boole ciy xas; mu yem ci wax ko ne: «Na la Boroom bi mbugal!»10Waaye nit ñii may wax, dañuy saaga li ñu xamul. Te li ñu xam ci tañaxu sax, ni bàyyima yu amul xel, dañu ci yàq seen bopp.11Ñoo kay torox! Dañoo jaar ci yoonu Kayin, sóobu ci réerug Balaam ngir xaalis, di bañ kilifteef ni Kore, te dinañu dee ni moom.12Su ñu bokkee ak yéen reeru mbooloo mi, dañu ciy indi ay, niy xeer yu nëbbu ci biir géej; amuñu genn gàcce, waaye dañuy giiroo te fonk seen biir rekk. Ñu ngi mel ni xiin yu amul ndox, yuy naaxsaay ci ngelaw; ni garab yu meññul ci jamonoy meññeef, te buddeeku, dee ba wow koŋŋ;13mel ni duusi géej gu mer, yuy gëq jëf yu ruslu; niy biddiiw yuy faq, te Yàlla dencal na leen lëndëm ya gën a tar ba fàww.14Enog, di juróom-ñaareelu maam gannaaw Aadama, waxoon na ci kàddug Yàlla, ba weer leen ne: «Boroom bi wàcce na ca asamaan, ànd ak ay junniy junniy malaakaam,15ngir àtte ñépp, te mbugal ñi weddi ñépp ndax ñaawteef, yi ñu jëf ci ñeme Yàlla; di leen fàttali it kàddu yu ñaaw, yi ñu ko tifaar ci seeni bàkkaar ak seen weddi.»16Duñu noppee xultu, di jàmbat seen nekkin, tey topp seen nafsu; ay wax yu réy a ngi ball ci seen làmmiñ, waaye dañuy jey ñi ñuy yaakaare njariñ.17Waaye yéen samay xarit, fàttalikuleen la leen ndawi sunu Boroom Yeesu Kirist waxoon lu jiitu,18ne leen: «Muju jamono ay tiiñalkat dinañu feeñ, ñuy weddi Yàlla, ngir topp seen bakkan.»19Ñooy féewale, te Xelum Yàlla nekkul ci ñoom, waaye niti kese lañu.20Waaye yéen samay xarit, doolewuleen ci seen yoonu ngëm wu sell, tey ñaan ci dooley Xel mu Sell mi,21ba saxoo mbëggeelu Yàlla, tey séentu yërmandey sunu Boroom Yeesu Kirist, mu tàbbal leen ci dund gu dul jeex.22Jubbantileen ñi am werantey xel,23ngeen musal ñale, jële leen ci safara, te yërëm ñeneen ñi, waaye boole ci moytu, ba sib sax seen yére yi taq sobe.24Yàlla mi leen man a aar ci gépp jeng, te teewal leen fa kanam ndamam, ngeen ñàkk sikk te fees dell ak mbég;25Yàlla miy kenn, di sunu Musalkat, na yelloo ndam ak màgg, kàttan ak nguur, jaar ci Yeesu Kirist sunu Boroom, démb, tey, ëllëg ba fàww. Amiin.Wolof Bible 1987 Copyrighted - Kàddug Dëgg Gi Copyright © Les Assemblées Evangéliques du Sénégal and La Mission Baptiste du Sénégal. All rights reserved Wolof Bible 1987 Yudd 1 00:00:00 00:00:00 0.5x 2.0x https://beblia.bible:81/BibleAudio/wolof/jude/001.mp3 1 1