Bible in one year June 24Acts 7:1-211. Noonu saraxalekat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?»2. Ecen tontu ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan.3. Mu ne ko: “Toxul sa réew, bàyyi say bokk, te ñëw ci réew, mi ma lay won.”4. «Ci kaw loolu mu génn réewu niti Kalde, dëkksi Karan. Te bi baayam faatoo, Yàlla toxale ko foofa, dëël ko ci réew, mi ngeen dëkk léegi.5. Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu war a donnale, du sax fu mu man a teg tànkam; waaye dig na ko ne, dina ko may réew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom.6. Yàlla ne ko: “Ñi soqikoo ci yaw dinañu ganeyaan ci réew mu ñu dëkkul; dees na leen def ay jaam, di leen fitnaal diirub ñeenti téeméeri at.”7. Waaye Yàlla nee na: “Xeet wi leen jaamloo, man maa leen di àtte te gannaaw loolu dinañu génn, di ma jaamu ci bérab bii.”8. Yàlla nag tëral kóllëre seen diggante, fas ko ci màndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca juróom-ñetteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanqóoba, Yanqóoba it def noonu fukki maam ya ak ñaar, ñi sos xeet wi.9. «Naka maam yooyu, dañoo iñaane Yuusufa, ba jaay ko, mu jëm réewu Misra. Waaye Yàlla taxawu ko,10. génne ko ci coonoom yépp, defal ko yiw ak xel ci kanamu Firawna, buuru Misra, mu def ko kilifag Misra ak këram gépp.11. «Bi loolu amee xiif tàbbi ci biir Misra ak réewu Kanaan mépp, ba toskare ja metti lool, te sunuy maam amatuñu lu ñu lekk.12. Yanqóoba nag dégg ne, Misra am na dugub, mu yebal ca sunuy maam, ñu dem fa yoon wu jëkk.13. Bi fa ay doomi baayam delloo nag, Yuusufa xàmmiku leen, te Firawna xamante ak njabootam.14. Ci kaw loolu Yuusufa yeble, woo baayam ak mbokkam yépp, ñuy juróom-ñaar-fukki nit ak juróom.15. Noonu Yanqóoba dem Misra, faatu fa, moom ak sunuy maam.16. Gannaaw loolu ñu yóbbu seeni néew Sikem, dugal leen ca bàmmeel, ba Ibraayma jëndoon ak xaalis ca doomi Emor ca Sikem.17. «Bi loolu wéyee jamono ji jege woon na, ngir Yàlla amal li mu digoon Ibraayma ci ngiñ; fekk xeet wa di law tey gën a bare ci Misra,18. ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra.19. Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen sànniloo seeni doom, ngir ñu dee.20. «Booba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Yàlla; ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam,21. ba noppi sànni ko. Noonu doom ju jigéen ju Firawna for ko, yar ko ni doomam. Wolof Bible 1987 Copyrighted - Kàddug Dëgg Gi Copyright © Les Assemblées Evangéliques du Sénégal and La Mission Baptiste du Sénégal.