Bible Version Compare

1
Bare na ñu fexee bind ab nettalib mbir, yi sotti woon ci sunu biir,
2
noonee nu ko jote ca ña ko fekke woon ca ndoorte la, te seede yooyu mujj doon jawriñi kàddug Yàlla.
3
Moo tax man it, ma fas laa yéenee bindal lépp ba mu jekk, yaw Tewofil mu tedd mi, gannaaw ba ma gëstoo mbir mépp, dale ko ca ndoorte la, ba mu leer nàññ.
Wolof Bible KYG 2010
2010, 2020 La Mission Baptiste du Sénégal
1
Bi loolu amee Yeesu dugg cig gaal, jàll dex ga, dellu dëkkam.
2
Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
3
Bi mu waxee loolu, ay xutbakat daldi ne ci seen biir: «Nit kii mu ngi sosal Yàlla.»
Wolof Bible 1987
Kàddug Dëgg Gi Les Assemblées Evangéliques du Sénégal and La Mission Baptiste du Sénégal